Lancé il y a seulement quelques jours (voir notre article), le service de stockage en ligne de Microsoft disposerait d’une version Wolof. En tout cas l’e-mail qui nous été envoyé dans un de nos comptes hotmail est bien écrit en Wolof.

Voici le texte contenu dans cet e-mail :

Dalal jàmm ci OneDrive, benn barab bi ngay denc ak séddoo say nataal, wideo, téere ak yeneen bara denc-fu la neex, ci benn jëfandaay, te doo fay. Ci weer yii di ñëw, mën na am ngay wéy di gisandoo SkyDrive ak OneDrive ci sa yoon, waaye bul jaaxle! Di nga mën di jot mbooleem say bara denc ci diirub coppite googu. OneDrive moo ëmb lépp lu la neex ci SkyDrive ak yeneen mbir.

Benn barab ngir mbooleem say nataal ak wideo

Jëleel ci sa telefon say nataal ak wideo yi la gënal ndax nga mën di leen jotee ci mbooleem say jëfandaay ak séddóo yi la neex te doo sonn.

Benn barab ngir mbooleem say téere

Sos ak soppi ay téere Word, Excel, PowerPoint, ak OneNote yu am solo, denc leen ñoom ñépp ci benn barab, te mën leen jotee ci bépp jëfandaay.

Benn barab ngir mbooleem say jëfandaay

Jotee say bara denc OneDrive ci bépp jëfandaay bu la neex boole ci say jëfandaayi PC, laalukaay, Mac, Windows Phones, iPhones, Android, ak yeneen.

Xool leneen lu OneDrive mën a def

Duggal seet mën-mën yu mag yi ci OneDrive te xam lan mooy benn barab ngir denc mbooleem mbir yi la gënal.

Xam yeneen mbir

Danga bëgg a am dencukaay bu maye? Am ba ci 8 GO soo toppee jéego ngir may sa dencub fagaru jëlug nataalukaay ak yabal say xarit.
Duggal ci OneDrive.com.

Laisser un commentaire